ngëm yàlla mu kawe mi
mooy nga gëm ne Yàlla moo la bind di la wërsëgal, te mooy buur mi moom lepp te moom dong mooy saytu mbideef yi.
te nga gëm ne moom dong moo yayoo jaamu amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom.
te nga gëm ne mooy Aji- màgg ji di ku mat sëkk, te moom donga yayoo mbooleem xeeti cant yi, mooy Boroom tur yu sell yi ak melokaan yu kawe yi amul moroom, te lenn ci mbindeefam yi nuru wu ko.
gёm malaaka yi.
nga gëm ne ay mbindeef la ñu Yàlla da leen a bind ci ag leer ngir ñu jaamu ko topp ndigalam yépp.
bokk na ci malaaka yooyu Jibriil yal na jamm nekk ci moom, mooy malaaka miy wacce ndéeytel Yàlla ci yonnent yi.
gёm téere yi.
téere yi nga xam ne Yàlla a ko wacce ciy yonnenteem.
ni ki Alquraan bi Yàlla wacce ci Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko.
ak Injiil bi Yàlla wacce ci iisaa yal na jamm nekk ci moom.
ak Tawraat bi Yàlla jox muusaa yal na jamm nekk ci mom.
ak zabuur bi Yàlla jox Daawuuda yal na jamm nekk ci moom.
ak yeneeni téere yu mu joxoon Ibraahiimaa ak Muusaa.
gëm yonnente yi:
ñooy ñi Yàlla yónni ci jaamam yi ngir ñu jangal leen di leen bégal ci lu baax ak aljana, waaye di leen xupp ci lu bonn ak sawara.
yoneent yooyu ña ca gën ñooy ñi ñiy woowe uluul hazmi te ñoo ñu ñooy:
yonnent Yàlla Nuuh yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Ibraahiima yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Muusaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Hisaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnente Yàlla Muammat yal na jamm ak xéewal nekk ci moom.
gёm bis bu mujj ba.
bis pénc ba nak mooy li nekk ci ginnaaw dee ci biir bammeel, ak bisub taxawaay ba, ak dekki ak isaab jëf i jaam ñi ba ñu baax ñi dugg aljana bu bonn ñi dem sawara.
gëm ab dogal bu neex walla bu naqari.
ab dogal mooy nga gëm ne Yàlla xam na lépp luy xew ci kéew bi, te bindoon na ko ca lawhul mahfuuz te moom la neex mu am.
Yàlla neena lépp lu am noo ko bind ci sunug dogal.
ab dogal nak ñenti dayo la:
bu njëkk bi mooy: xam xamub Yàlla, ni ki xam xamam bi jiitu lépp luy xew laataa muy xew ak bi mu xewee ba noppi.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla rekk a xam tukkig àdduna te mooy kiy wacce ab taw, te moo xam li nekk ci butiiti njuru kaay yi,te amul kenn ku xam lu miy am suba walla ci jan suuf la faatoo,Yàlla mooy ku xam te deñ kumpa. suuratu Luqmaan.
ñaareel bi mooy: nga gëm ne Yàlla bind na ko ci lawhul mahfuuz, lépp lu xew walla luy xew i ëllak lees bind la cib téere.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla mooy ki xam kumpa keneen ku dul moom xamu ko, te mooy ki xam lépp lu nekk ci jéeri yi walla ci géej gi, te amul wenn xob wuy rot ci suuf lu dul ni xam na ko, amul it aw fepp wuy wadd ci lëndamug suuf si lu dul ne xam na ko amul it lu tooy walla lu wow lu dul ne bind na ko cib téere bu leer. suuratul anhaam 59
ñatteel bi mooy:nga gëm ne lépp luy xew ci coobarey Yàlla lay xewe, te amul dara luy am ludul da koo neex moo xam ci moom la bayyikoo walla ci mbindeef yi.
tektal bi mooy waxi Yàlla mu kawe mi: ku mu soob ci yéen mu jub waaye dara manu leen a soob lu dul dafa soob Yàlla miy Boroom bindéef yi ba noppi. suuuratu attakwiir 28_29
ñeenteel bi mooy: nga gëm ne mbooleem bindeef yi ay mbindéefu Yàlla moo bind seen i jëmm ak seen i melo ak seen lépp.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla mooy ki leen bind ak seen i jëf. suuratu asaafaati