Rafetal: mooy di fuglu Yàlla saa sune, ak di defal mbindéef yi yiw ak lu rafet.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Yàlla dafa waral rafetal ci lépp" Muslim moo ko soloo
Bokk na ci anami rafetal yi:
- Rafetal ci jaamu Yàlla mu kawe mi, te mooy di sellal jaamu gi.
- Rafetal jëme si ñaari wayjur, ci wax ak jëf
- Rafetal jëm ci bokk yi ak jegeñaale yi.
- Rafetal jëm ci dëkkadoo yi.
- Rafetal jëm ci jirim yi ak Way-ñakk yi.
- Rafetal jëm ci kuy ñaawal jëme ci yaw.
- Rafetal wax yi.
- Rafetal werente wi
- Rafetal jëme si rab yi.
T-
1- Kóolute ci wattu àqi Yàlla mu kawe mi.
Ay anamam: am kóolute ci def jaamu Yàlla yi ci julli ak joxe azaka ak woor ak aj ak yeneen yi Yàlla farataal si nun.
2- Kóolute ci wattu àqi mbindéef yi.
- Ci wattu deri nit ñi.
- Ak séeni alal
- Ak seen i deret.
- Ak seen i bóot, ak mbooleem lila nit ñi wóolu.
Yàlla wax na ci melukaani waytexe yi: "Ak ñi nga ñiy sàmm seen i kóllare ak séeni dëel 8" Saaru Almoominuuna 8
Mooy xibaare lu dëppoo ak li am, wala mbir mi ni ki mu ame
Bokk na ci ay anamam:
Dëggu ci wax ak nit ñi.
Dëggu ci dige.
Dëggu ci wax ak jëf.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Dëggu day jëmale cig mbaax, te ag mbaax day jëmale Aljana, nit ki dina dëggal ba mujj nekk Dëggalaakon Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
Fen, te mooy wuute ak li wér, te bokk na ca, di fen nit ñi ak wuuteb dig, ak seede ay caaxaan.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Fen day jëmale nit ki cig kàccoor, te ag kàccoor day jëmale Sawara, te nit ki dina fen bañu bundal ko fa Yàlla ni fenkat la" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci. Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "Màndargay naaféq ñatt la" -mu tudd ca- "bu waaxtaanee day fen, bu digee day wuute dig ba" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
- Muñ si topp Yàlla mu kawe mi
- Mu moy Yàlla yi
- Muñ ndogal yu metti yi, te sant Yàlla ak lo man di am
Yàlla mu kawe mi neena: "Yàlla dafa bëgg way muñ yi" Saaru Aali Himraan 146 Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "yéemu naa mbiri way gëm ji moom de mbiram yépp yiw la,te kenn amul loolu ku dul way gëm,bu ko mbékte dalee day sant mu doon yiw ci moom,bu ko aw lor dalee day muñ mu doon yiw ci moom" Muslim moo ko soloo.
- Mooy ñàkka muñ si topp Yàlla, ñàkka muñ moy yi, ak di yéjji ndogal yi ci wax wala si jëf
Bokk na ci ay meloom:
- Mébet dee.
- di mbej say lex.
- Di xotti say yéere.
- Di tasaare sa kawar
- Di ñaan alkande ci sa kaw.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Pay gi de mi ngi ci màggug nattu yi,te Yàlla su bëggee aw nit da leen di nattu,ku gërëm ngërëm ñeel ko,waaye ku mer merum Yàlla ñeel ko" Tirmizii ak Ibn Maaja ñooko soloo
Mooy nit ñi di dimbalànte seen biir ci dëgg ak uw yiw.
Anami dimbalànte yi:
- Dimbalànte si delloo àq yi.
- Dimbalànte ci delloo Aji-tooñ ji.
- Dimbalànte ci faj aajoy nit ñi ak way ñàkk yi.
- Dimbalànte ci yiw.
- baña dimbalaante si bàkkaar ak lor ak noonoo
Yàlla mu kawe mi neena: "dimbalànte leen cig mbaax ak ragal Yàlla, te bu leen dimbalànte ci bàkkaar ak noonoo te ngeen ragal Yàlla moom Yàlla ku tar mbugal la" Saaru Maa-ida 2 Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "jullit ak moroom ma dañoo wara mel ni ab tabax; lenn lune day dëgëral leneen la" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci. Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "Jullit mooy mbokkum jullit ba,du ko tooñ,te du ko jébbale,ku nekk ci sa aajoy mbokk,Yàlla dina nekk ci say aajo,ku dindil ab jullit aw tiis, Yàlla dina ko dindil aw tiis ci tiisi bisub taxawaay ba,te ku suturaal ab jullit Yàlla dina ko suturaal bisub taxawaay ba" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
1- am kersa ci Yàlla: ci nga bañ koo moy moom Yàlla mu sel mi.
2- am kersa ci nit ñi: bokk na ca bàyyi wax ju ñaaw te bon, bañ a wuññi awray kenn.
Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Ngëm juroom ñaar fokki xaaj la yu topp" wala: "juróom mbenni fukki xaaj la ak lu topp" - "ay pàcci, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale lor si kaw yoon. wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm" Muslim moo ko soloo
- Yërëm mag ñi te weg leen.
- Yërëm xale yu ndaw yi.
- Yërëm way ñakk yi ak way aajo woo yi
- Yërëm rab yi ci di leen jox lekk te bañ leena lor.
Loo lu la Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc di wax ne: "dangay gis jullit yi si seen yërëmante ak seen ug bëgante ak seen ñeewanten te ñu mel ni benn yaram,bu ci benn cér di jàmbat mbooleem cér yi dañ koy wuyu ci bañ a nelaw ak si tàng" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci. Yonnent Yàlla bi yàlna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "ñiy Yërëme de Aji-Yërëme ji de dana leen yërëm, yërëm leen waa Soof si, ki ci Asamaan yërëm leen" Abuu Daawuda soloo nako ak Tirmiziiu ak ñeneen.
Bëgg Yàlla mu kawe mi
Yàlla mu kawe mi neena: "ñi gëm de Yàlla lan gëna bëgg" Saaru Baqara: 165
Bëgg Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc
Moom wax na ne: "Giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom,kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko wayjuram ak doomam" Buxaarii moo ko soloo
Bëgg way gëm yi, te bëggal leen yiw ni ki nga ko bëggale sa bopp.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Kenn ci yéen du gëm; ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam" Buxaarii moo ko soloo
Mooy feccikog xar kanam, àndag mbégte ak muuñ ak ñeewant, ak feeñal mbégte ci boo dajee ak nit ñi.
te mooy safaanug fas xarkanam, ci kanami nit ñi ci lépp lu leen di dawloo
Te ay Hadiis ñëw na si ngëneeli loolu, jële nanu si Abii Zarrin yal na ko Yàlla dolli ngërëm, neena: Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak muicc neena: "Bul xeeb ci lu baax dara, donte dangay dajee ak sa mbokk si kanam gu bélli Muslim moo ko soloo Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc néena: "Sag muuñ ci sa kanamu mbokk sarax la" Attirmizii moo ko soloo
Mooy nga mébet ci keneen mu ñàkk xéewalam, wala nga bañ keneen am xéewal.
Yàlla mu kawe mi neena: "ak ci ayu Aji-Soxor ji saayu soxoree 5". Saaru Alfalaxi: 5
Jële nanu ci Anas ibn Maalik, yal na ko Yàlla dollee gërëm, neena yonent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "bu leen bañante, te bu leen soxorante, te bu leen dummóoyante, nekk leen -yéen jaami Yàlla yi- ay mbokk" Buxaarii ak Muslim ñoo ko soloo
Mooy di reetaan sa mbokkum jullit ak di ko xeeb,te loolu daganul
Yàlla mu kawe mi wax na ci tere loolu: "ée yéen ñi gëm bu benn nit reetaan beneen nit ndax amaana ñooñu gën ña leeni reetaan bu benn jigéen it di reetaan benn jigéen ndax amaana ñoom ñu gën ña leen di reetaan bu leen di ayibalante te bu leen di woowante ci ay tur yu leen neexul turu kàccoor yooyi de lu ñaaw la ginnaaw ngëm ga te ku tuubul ñoom ñooy tooñkat yi" Saaru Al-mujaadala 11
Mooy nit ki bañ a gis ne moo gën a kawe nit ñi, du xeeb nit ñi te du bañ dëgg
Yàlla mu kawe mi neena: "Jaami Yàlla yi dëgg mooy ñiy dox ndànk ci kaw Suuf" Saaru Alfurxaan 63 Maanaam: di ay Aji-woyof Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Kenn du woyof-wofof lu lu dul ne Yàlla dina ko yékkati Muslim moo ko soloo Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc waxaat ne: "Yàlla soloo nama ne nangeen di woyoflu ba kenn du puukarewu si kaw kenn, te kenn itam du bew si kaw kénn" Muslim moo ko soloo
1- Rëy ci kaw dëgg, te mooy delloo dëgg bañ koo nangu
2- Rëy ci kaw nit ñi, te mooy xeeb leen ak doyodal leen
Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Ku ab peppu rëy nekk ci xolam du dugg Aljana" Benn waay neko: nit kiy bëgg ay Yéereem ak i dàllam rafet nag? mu ne ko: Yàlla dafa rafet te daa bëgg lu rafet, rëy mooy: bañ dëgg ak xeeb nit ñi" Muslim moo ko soloo.
- Batarul hàq: mooy Bañ dëgg
- Xamtun naasi: mooy xeeb nit ñi.
- Yéere bu rafet ak dàll yu rafet bokkul ci rëy.
- Wuruj ci jaay ak jënd, te mooy nëbb ayib ci njaay mi.
- Wuruj si booy jàng xam-xami, te bokk na ca jàngkat bi di wuruj ci nattug njàng mi,( composition yi)
- Wuruj ci ay wax, lu mel ni di sede lu dul dëgg.
- ñàkka matal kollare ci say wax, ak ci li nga dëpoo ak nit ñi.
ñëw na ci tere wuruj ne: yonnent bi dafa rombu benn ndabul ñam, daal di ciy dugal loxoom, baaraam yi daal di tooy, mu wax boroom ñam wi neko: "lii lanla yaw boroom ñam wi?" muneko: taw beeko laal yaw yonnent Yàlla bi. Yónnent bi neko: "Lu tax defooko si kaw ñam wi ngir nit ñi gis ko? képp kuy wuruj bokkul ci nun" Muslim moo ko soloo
Subra: mooy ndabul ñam
Mooy nit ki di diis lu ci def yiw ak li mu war a def.
Te bokk na ca: Tàyyeel ci def wartéef yi.
Yàlla mu kawe mi neena: "Naaféq ya dañuy jéem a wor Yàlla waaye Yàlla dana leen njuuy, te bu ñu jògee jëm ca julli ga, da ñiy jòg cig tayyeel, da ñiy ngistal ci bëti nit ñi, te du nu tudd Yàlla lu dul lu néew ci moom 142" Saaru Annisaa 142
Jullit bi warnaa moytu tàyyeel ak giim ak, toog rek, te ligéey ak yëngatu ak pastéefu ci dund gi ci lépp luy gërëmloo Yàlla
1-Mer mees gërëm:te mooy mer ngir Yàlla saa yu yéefar ak naaféq yi wala ñeneen xotte wormaam moom Yàlla mu sell mi
2-Mer mu ñu ngàññi:te mooy mer miy def nit ki di def aka wax lu jaaduwul.
Liy faj mer mun ngàññi:
Jàppu
Mu toog bu dee dafa taxawoon, waaye mu tëdd bu dee dafa toogoon.
Mu taqoo ak ndenkaandey Yonnent bi ci loo lu: "bul mer"
Mu téye boppam ci bañ a jëfandikoo meram.
Muslu ci Yàlla ci Saytaane mi ñu dàq ci yёrmandey Yàlla
Noppi
Buqat mooy: di ragal lu jarula ragal
Ni ki di ragala wax dëgg ak weddi lu ñaaw.
Njàmbaar: mooy dégmal dëgg, lu ci mel ne dégmal xeexukaay ya ngir aar Lislaam ak jullit yi.
Yonnent bi daa na wax ci ñaanam yi: "Yaw Yàlla maa ngi lay muslu buqat" yoneent bi wax ne: "Jullit bu am kàttan bi de la Yàlla gën a bëgg ci jullit bu lompañ bi, waaye ñoom ñéppa am yiw" Muslim moo ko soloo
- Lu mel ni rëbbaate ak saaga.
- ak lu mel ni di wax naa diw "rab la" walla ay baat yu ni mel.
-Wala tudd ay awra ci ay kàddu yu ñaaw te bon.
- Yonnent bi tere na yooyu yépp, daal di wax ne: "Nekkul jullit Aji-Jamaate gi du caagine Aji-Rëbbaate gi, wala Aji-Def ñaawtéef, wala Aji-Bon lammiñ" Tirmizzi ak Ibn Hibbaan ñooko soloo
1- Di ñaan Yàlla mu wërsëgal la rafet jiko, te dimbali la ci.
2- Di fuglu Yàlla mu màgg mi te kawe, ci ne xam na sa mbir, moo ngi lay dégg te moo ngi lay gis.
3- Di fàttaliku yoolu rafet jiko ci ne day waral dugg Aljana
4- Di fàttaliku mujjug ñaaw jiko ci ne day waral dugg Sawara.
5-Rafet jiko day waral bëggug Yàlla ak bëggug mbindeef yi,ñaaw jiko da waral bëñug Yàlla ak bañug mbindeef yi.
6- Jàng jaar-jaaru Yónnent bi yàlna ko Yàlla dolli mucc ak jàmm ak di roy si moom
7- Di àndag ñu baax ñi te moytu ñu bon ñi